Xaley tey, magum ëllëg.
«Nit ki matt ma muy jaroo su màggee, ca ba muy ndaw la koy taxañ.»
Wolof Njaay
Xale buur la, bëgg-bëggam rekk a ko ñor. Liy tax mu xam, xàmmee. Ràññee lu baax ak lu bon, sàmmonte ak teggiin yi a ngi lalu ci yar gi ko ay way-juram tàggate.
Te réew mu bëgg suqaliku du sàggane ay tuut-tànkam. Ndax kat dayoob teraanga ëllëgu mépp réew woroowul benn yoon ak lu pénc mi di dénk tey xaley réew mooma.
Alal ju gën a mag nag gu aw askan man a baaxe ay ndawam mooy yar gu mucc ayib.
Naam Càmm gi am na ci wàll wu rëy, waaye li ci ëpp a ngi tàmblee ca kër ga. Naam Yàlla mooy jubal waaye waslu àq wareef la ci bépp way-jur.
Yuuxu, gëdd, dóor tabaxul jikko xale, jubbantiwul daray dëng-dëng. Li njëkk war yarkat bi (baay ja, walla ndey ja) mooy doon ku yaru, jub, bëgg lu baax. Kenn manul a gall meew mu mu nàmpul.
Ñi wër tuut-tànk bi tamit (bàjjan, nijaay, maam, añs) war nañu xam kàddu ak jëf yu ñuy fësal ci kanamu xale bi. Manoo nekk ku ñaaw làmmiñ ba noppi bëgg a tere saaga.
Ndax xelu xale li mu miin rekk lay soloo. Lu mu gis rekk lay roy. Te nag, lu mu xës ba jàpp ca njëlbéenug dundam, tàbbal ko ci xolam, du yomb tàggalikook loola. Ba tax nu war a settantal lu nuy duy ci seen xol, mbaa di ko saxal ci seen xel.
Gànnaaw loolu it waxtaan ak ñoom ci fulla, fayda ak teggiin. Ragal gu metti bañ a ñagasal dikkante yarkat bi ak tuut tànk bi. Foo, sax, man a doon jumtukaay gu xereñ ngir yee xel ak ñoŋal jikko.
Di sawar ci tontu laaj yu bare ak a doy waar lool yu mu lay jébbal léeg-léeg, benn laaj ñàkkul solo te jarul a xeeb. Tontu kéem sam xam-xam ci dëgg te bañ di gëtam.
Bàyyi xel ne li nga jii ci xol ak xelu xale bi doŋŋ ay meññ ci ay jikkoom. Te yit loolu, bés bu màggee, lay jottali ay rakkam ak i doomaam. Ba far mu doon woy wu dul fay, teen gu dul dée.
Weccoo yooyu ay jotaay yu am solo la :
-Benn, di na tax nga gën xam ki ñu la dénk. Ndax benn xale meññul ci neen, ku ci nekk am na lu ko Boroom bi mooñaale. Ba tax, ku ci nekk, boo ko seetloo/degloo bu baax mu wan la yoonam.
-Ñaar, weccoo yooyu ay buntu la ngir xamal xale bi jikko yu rafet, njariñu yaru ak am teggiin.
Ay mbir yu ndaw yu mel ni tàmmal xale bi nuyoo bu yeewoo ca njël, sant ak jaajëfal ku la defal mbaax (ni ki may ñam walla ndox, añs..)
Jox cër ay nawleem, bañ a xeeb kenn, waaye it bañ a yéemu ci kenn.
Miinal ko set, xamal koy njariñam rawatina ci wér gu yaram nit ki.
Nàndal ko xam-xam ak dayoom ci àddina si waaye it jeexital gu mu man a def ci dundam.
Waaye it mu bañ a réere mbir ni; xam-xam, jëfee! Te njub doon gànnaayam.
Soññi ko ci yëngu ak cawarte, yee ko ci musibay tayeel.
Bu ko lépp yombee it, tere ko yàq ak beew. Xamal ko xéewalu Boroom bi bari na naam waaye doylu mooy li war as gor.
Yar ko ci diineem, mbatitam waaye it xamal ko ni àddina si lu yaatu la, te wuute warul meññ mbañeel. Ndax ci jàmm la lépp xaj.
Mu xam, lu muy gën di màgg ni ëllëgu réew mi war na ci bay waaram. Ndax ni ko sunu maam Seex Anta Jóob daan waxe : « doomu réew ay tabax réew. »
Ci xalima ji, Suleymaan Jaw
Jajeuf Suleymaan Jaw…mbindeu mi melnani nioune makk gni nga ko diaglel… ndax makk mou sétantal mbindeu mi dina ci jubbantikou ba nopy dina xamm nakala lay yaaré Xaleyi ba gnou doone euleuk ay nitt youy ndieurigne penc mi….maasha Allah…Amna Solo lol.
Jërëjëf, sëñ bi Jàllo. Noo ngi rafetlu xalaat wi.